L’Aventure Ambigu歌词由Leuz Diwane G演唱,出自专辑《L’Aventure Ambigu》,下面是《L’Aventure Ambigu》完整版歌词!
L’Aventure Ambigu歌词完整版
Lan moo ñu dal ba ñu wara yegsi fii nii
Sénégal est ce que mérité na ñu lii nii
Bu ñu demee ba nguur jar ñuy faat bakkan
Ak fi ñu jaar ba yegsi fii weesu na ñu saggan
Liggeeyu maam warul woon naaxsaayee nii
Xamme tu ñu suñu ay ENEMIS
Su ñu noflaay la ñu weccoo ak safaan
Est ce que nguur jar na ngay tayle saw askan?
Buumu nooteel gi ba tay dogul
Est ce que delloo waatoon ko nasaraan yi gënul?
Que des Samba Diallo
L'aventure est Plus Que Ambiguë
Ñi ñu amoon yaakaar si ñoom sont tous des vendus
Est ce que drapeau bi cuubu wul?
Manoo yeg li nit ñi dund te sa xol sotul
Ay caïmans la ñu dans l'eau on est tous foutus
Nu ñu def ba regg rek a leen yitteel
Et puis c'est tout....
Askan wi la ñuy mbubbowoo
Bu ñuy xës ba falu rek ñuy juyoo
Beddi ñu duñ ñu woo
Boolee wuñ ñu ci dara waral ñu dëkkee duuloo
Ndeenkaane la du seen moomeel
Ku xës ba falu fatte noo mel
Lu coow li bëri bëri raññeel
Weetaayu tëraayu bammeel
Indiscipline ci kër yi lay raamee ba assemblée
Mag yu xamadi ndaw yi kan moo leen di recadrer
École yi nooy bëggee sa reew du ñu ko fa jàngale
Engagement ak patriotisme fu ñu ko nara jëlee
Balle bi ngay dòor muy dem di rayi doomi jàmbur
Yuuxu yi ak coow li du def sa bopp tambour
Rongoñ yiy walangaan, dereet ji du la teree nelaw
Yaakaar la woon ngeen def ko dóom sanni si ngelaw
Doomu xolam la woon
Soutien de famille la woon
Yaakaaru famille lëmm la woon
Ray ngeen ko si neen
Doomu xolam la woon
Soutien de famille la woon
Yaakaaru famille lëmm la woon
Ray ngeen ko si neen
Askan wi la ñuy mbubbowoo
Bu ñuy xës ba falu rek ñuy juyoo
Beddi ñu duñ ñu woo
Boole wuñ ñu ci dara waral ñu dëkkee duuloo
Ndeenkaane la du seen moomeel
Ku xës ba falu fatte noo mel
Lu coow li bëri bëri raññeel
Weetaayu tëraayu bammeel